Epatit A
Epatit A (ñu gënoon ko xamee ci turu epatit biy dale) doon na Jàngoro juy dale ju tar buy jàpp res wi te li koy joxe di doomu jàngoro biñ naan Epatit A (HAV).[1] Bari na lu muy dal nit te du feeñ rawatina ci ndaw yi.[2] Diggante bi muy dugg sa yaram ak bi muy tàmbalee feeñ, mi ngi tollu ci diggante ñaar ba juróom-benni ayi-bis.[3] Su la dalee mën na def ak yaw juróom ñatti ayi-bis te dina faral di ànd ak: xel muy teey, waccu, biir buy daw, der bu mboq, yaram wu tàng, ak mettitu biir.[2] Luy tollu ci 10 ba 15% ci ñi mu dal ñooy wéy di ko gis su demee ba weesu juróom-benni weer ginaaw bi mu leen dalee.[2] Mag ñi mën nañu ci jëlee Feebaru res bu tar waaye bariwul lu muy dale.[2] Li koy faral di joxe mooy lekk ñam wala naan ndox mu am doomi jàngoro.[2] Meññeefu géej buñ toggul ba mu ñor dina ko faral di joxe.[4] Jege ku ko am lu ëpp, mën na la ko wàll.[2] Xale yi mën nañu ko am te du feeñ waaye teewul mën nañu ko wàll ñeneen.[2] Su la dalee benn yoon, dootu la dalati sa giir gi dund.[5] Ci sa deret la ñuy seetee doomu jàngoro ci ndax ni muy feeñee dafa nuru ak yu yeneen jàngoro yu bari.[2] Benn xeetu epatit la ci juróom yiñ xam: A, B, C, D, ak E. ñaqu epatit A dalay aar bu baax ci feebar bi.[2][6] Yenn réew dañuy faral di baamtu ñaq bi ci xale bi ak ci ñi feebar bi gën a yab kenn masu leen a ñaq.[2][7] Loolu mën na leen aar seen giir gi dund.[2] Yeneen matuwaayu yi la ci mën a musal ñooy raxas loxo ak togg ñam ba bu ñor xomm.[2] Amul benn garab buñ ni mën na ko faj, li ci des, garabi xel muy teey wala biir buy daw la ñu lay digal su aajewoo.[2] Gën gaa bari su la dalee dangay wér, sa res wi melni dara mësu ko dal.[2] Bu yàqee res wi, dañu lay gereefeel res ngir faj ko.[2] Ci àdduna bi, jàngoro bi dina feeñ ci 1.5 miliyo?i doomu aadama at mu nekk[2] nga boole ci yi feeñul mu tollu ci fukki miliyo?.[8] Fi mu gënee bari àdduna bi mooy ci gox yi desee te ndox mi ñuy naan setul.[7] Ci réew yi néew doole lu tollu ci 90% ciy xale jot nañu am doomu jàngoro bi laata ñuy am 10 at, loolu mooy mucci nañu ci ba fàww laata ñuy nekk mak.[7] Yenn saay mu jàppandoo ñu bari ci réew yi xawa am doole ndox jàngoro bi bariwul ci xale yi te itam duñu leen di faral di ñaq.[7] Ci atum 2010, epatit A bu tar bi faat 102,000 doomu aadama.[9] At mu nekk 28 fan ci weeru Sulet mooy Bis biñ Jagleel epatit ngir xamal nit ñi luy jàngoroy epatit.[7] Royuwaay yi
Information related to Epatit A |
Portal di Ensiklopedia Dunia